Suivez nous sur facebook Suivez nous sur twitter
ECONOMIE
 
 
« MAN, DAMA JAPP NE, CFA AK ECO ÑOO YEM KEPP, BENN BAAXU CI. »
Publié le : Vendredi 16 Août 2019 - 13:53 - Source : Dakarmatin - Commentaires : 8 - Consulté : 1118 Imprimer

Mamadu Jàllo :  Ndax CFA bi baax na ci njaay meek njënd mi, rawati-na bitim-réew ?

Ndongo Sàmba Silla : Déedéet. Mësu cee baax ! CFA bi du yombalal njaay meek njënd mi. Moom kay, safaan bi la koy jural. Ndaxte, boo seetloo, bi Senegaal moomee boppam ci atum 1960 ba nëgëni-sii, li ñuy wax ci tubaab sunu “balance commerciale” dafa deme boor.

Maanaam, soo méngalee li réew miy jënd ak li muy jaay bitim-réew, dangay gis ne li muy jënd moo ëpp fuuf li muy jaay. Li Frãs fuloon dayo CFA bi moo waral laago bi.  Ndege, diisaayu CFA bi moo tax liggéey ci jafe. Te, am réew, bu dee li muy jënd bitim-réew moo ëpp li mu fay jaay, day ame ay bor yu dul jeex. Loolu moo nu sonal. Booba ba léegi, bor a ngi ci sunu baat. Danoo leb a leb ba mënatunoo fey. Seŋoor ba Maki, jaare ko ci Abdu Juuf ak Ablaay Wàdd, ku dàq a leb sa moroom nga ne kii.  Wànte Maki Sàll, sunu njiitu réew mi fi ne, moo ci raw. Te nag, jàngoro, doomu-jàngoro du ko faj. CFA bi mooy laago bi, kon, féeg noo ngi koy jëfandikoo, dunu mës a jóg ci leb. Dëgg la, réew yépp ay leb, ba ci réew yi ëpp doole ci àddina si. Waaye, benn, kenn tënku leen ba duñu mën a jaay bitim-réew ; ñaar, seen woyofaayu xaalis may na leen ñu doxale noonu seen i naal. Nun nag, CFA bi mooy sunu gàllankoor. Xaalis bi dafa am doole ba tax na say njaay du jar. Kon fooy jële looy faye say bor ?

Li nga wax dox na waar, di ! 

Yaa ko gisal sa bopp. Lu ni mel, ñi féete kow te ne déjj ci donkaasi gi doŋŋ lay amal njariñ. Dinañ mën a jënd lu leen neex bitim-réew, indi ko ci réew mi, jaayaat ko nu mu leen neexe. Seen xaalis di gën a yokk ak bu Farãs, askan wi moom di wéy di ndóol. Bu lu ni mel amee, dees na joxoñ baaraamu tuuma bànk yu mag yi. Ndaxte, ñoo ko sooke. Ndekete, ñoom dañuy bañ a lebal nit ñi xaalis. Maanaam dañ leen di gàntal. Li ñu ko dugge nag, du lenn lu dul sàmm yemoo (parité) CFA bi ak Ëro bi. Njiiti bank yooyii xam nañ ne, bees lebalee xaalis liggéeykat yi, muy àntarpërënëer bi, di boroom bitig bi, walla sax bépp jaaykat, li ñuy koy jënde mooy ay jumtukaay walla dund. Jumtukaay yooyu ak dund bi, nag, bitim-réew lañu koy jënde. Te, téeméeri àntarpiriis yoo jël, 30 yi walla 40 yi bitim-réew lañuy jëggaani seen jumtukaay.

Loolu jur lan, nag, ci sunu koom-koom ?

Day nasaxal walla day wàññi xaalis bi nuy bàyyi ci bànki Frãs ba, ñu koy wax ci nasaraan “réserves”.  “Réserves” yooyu, nag, ñooy wóoral yemoo CFA ak Ëro. Looloo tax bànk yu mag yi duñ sawar ci lebal liggéeykat yi. 

Doo ma baal nga leeral fii ? Lu loolu joteek yemoo bi ?

Waaw, ngir sàmm yemoo boobu, fàww ñu dakkal bor yi walla ñu wàññi leen. Liggéeykat bu ci am wërsëg ba bànk yi lebal la, li ngay war a fey day takku lool. Ci gàttal daal, CFA bi day yokk say bor, xoj say liggéeykat, tere laa am i isin, tere laa jaay bitim-réew… As tuut li nu am ciy njuréef ak alal, tubaab yaa koy fob yóbbu seen dëkk ndax li ñu dippe “zone franc” moo leen ko may. Ndax loolu jaadu na? 

–     Déedéet kay !

–     Kon nga xam ne noo ngi ci nooteel ba léegi. Loolu yépp, nag, boo leen boolee, lenn doŋŋ lay jur : tumurànke.

– GInnaaw bi nga leeralee ni CFA bi nooteel lay biral, lan nga jàpp ne moo nu ci teree génn boobaak léegi ?

– Waaw. Laaj bu am solo nga laaj fii. May ma ma jox la benn misaal. Man, damay faral di dem bitim-réew ngir amal fa ay waxtaan ñeel CFA bi, ma ciy ànd ak gëstukati daara-yu-kowe yu mag. Waaye, saa yu ma noppee ci wax ci CFA bi, leeral jafe-jafe yi mu làmboo, tubaab yi ci seen bopp dañuy waaru ! Mbir mi da leen di jaaxal lool sax. Bu ko defee, ñu naan ma : « Déedéet kay ! Waaw yéen, lu leen tee wacc musiba bii nga xamante ne day gàllankoor seen dund ak seen yokkute ? Ana seeni àntarpërënëer ? Seen njiit yi ngeen di fal nag, lu leen dal ba ñuy seetaan lii ? Moo, ndax dungeen fippu indi saafara ci jàngoro jii ! Yéen a ngi nelaw de ! » Bu ko defee ma ni waaw, Tubaab yeey wax lii…Waaye, bu dee fii ci Afrig, walla Senegaal, saa boo waxee ci musibay CFA bi, dañu la naan : “ Waaw…dëgg la, CFA bi am na ay jafe-jafe waaye am na ay ngëneel itam…” Nga gis ne, Tubaab yi sax, nangu nañ ne CFA bi musiba la ci nun. Waaye, ñenn ci doomi Afrig yi, walla doomi Senegaal yi ci seen bopp, ñoom, jàpp nañ ne CFA bi am na njariñ. Dafa di, ñi ànd ak CFA bi, dañu dul xalaat, walla ñu bokk ci nguur gi, teewal fi Frãs mu am lu mu leen di combal. Waaye, nag, ku waxaale sa ngor, ñu jënde ko sa toroxtaange. Loolu moo nu dal. 

-Kon ci sa gis-gis Frãs a nu teg li lépp ?

– Frãs ak doomi-Afrig yi koy jàppale. Ndaxte, boo seetee, réew yi Frãs nootoon yépp, am ci ñu dul jëfandikoo CFA bi, moom seen bopp ba mu mat sëkk, te tey ñu ngi ci yoonu yokkute. Réew yooyu, bi xeex jotee, dañu jaayante ak Frãs, jàmmaarlook moom, foqati seen réew. 

-Mën nga leen a lim ?

– Réew yu jàmbaare yooyu, mënees na cee lim Alséri ak Wiyetnaam. Ñoom ñaar ñépp a xare ngir afal seen askan. Nun, nag, sunuy njiit ya woon, jarul nu leen fiy tudd, doxalewuñu woon noonu. Dañu maslaa ak Frãs, mu kootoog ñoom, lal i pexe ngir gën fee mën a toog, aakimoo sunu alal. Bi gënoon a fës ci pexe yooyu nootkat bi laloon mooy li ñu dippe woon “Accords de coopération”. Loolu li mu wund mooy, lépp lu aju woon ci moomeelu réew yi mu nootoon, ciy loxoom lay tegu. Maanaam, njaay meek njënd mi, ak lépp lu ñeel jëflante ci diggante nootaakon (colonies) yi ak bitim-réew, xaalis bi (te muy CFA bi) ak koom-koom gi. Loolu la Frãs waxoon ne bu ci sunu njiit ya woon àndee xaatim ko, mu nangu ñu moom seen réew. Sunu njiit yi nag, ñu ci ëpp Frãs lañu jànge, foofu lañ leen tàggate, daan fa liggéeye te nekkoon fa sax dipite. Moo tax ñu xaatim loraange jooju nu topp ba sunu jonni-Yàllay-tey jii. Réew mu ci mel ni Gaboŋ, lépp lu muy def, Frãs da cee ànd. « Accords de coopération » bi mu xaatimoon ñoo ko ko yóbbe.

Ndax am na ñu fippu, ne fàww ñu dog buumu njaam gii ?

– Lii tamit laaj bu am solo la. Am na ñu yàgg a xeex CFA bi ngir jële ko fi. Axã kay ! Du léegi la ñenn ci doomi Afrig yi tàmbalee xeex CFA bi. Xeex bi démb la woon, tey door a agsi. Te loolu boo ko waxee xel war naa dem ci Séku Ture. Ndege, moom moo jëkk a bañ CFA bi, ne dee, Gine du ci bokk. Moom Séku Ture, bañkat bu mag la woon, amaana li mu doonoon ab sàndikalist moo taxoon. Ndax ku mënoon a dajale ay nit la te bare woon i pexe lool. Waaye, ak lu xel miy màcc yépp, jataŋ ak gàllankoor yu bare yi ko Frãs daan teg, moo koo taxoon a tagatémbe. Loolu rekk a teewoon Gine génn ci. Frãs da doon dugal Gine xaalis bu bon bu baree-bare ngir yàq deru Séku Ture. Am na keneen ku ñiy wax Silwanus Olimpiyóo, njiitu Tógo la woon, nekkoon layookat bu siiw. Dafa laloon ab naal ngir wutal réewum Tógo xaalisu boppam. Jotoon na cee waxtaan sax ak réew yu mag ci àddina si, niki Almaañ ak Amerig. Bi mbir mi demee bay sotti la ko Frãs sàkkal pexe, ngem Eyademaa mu rey ko. Naka noonu, Tomaas Sànkara, jàmbaaru Burkina-Faaso ba. Nu gis ne, Frãs jenn itte doŋŋ la am : ratt réewi Afrig yi ba ñu sett, jël seen alal di ko siimee cereem.Cere jooju, nag, ku ko bëgg a xajamal mu sàkkal la pexe. Waaye, nit ñit xippi nañu seeni bët.

– De4gg la, nit ñi xippi nañu seeni bët, moo waral way-moomeel yi, kujje gi ak boroom xam-xam yi takkal pot sunu njiit yi ak Frãs. Dafa mel ni gaa ñaa ngiy deeltu ginnaaw ndax ñoo ngi wax ne dañuy bàyyi CFA bi dem ci ECO bi. Loo xam ci xaalis bu bees boobu ?

– ECO bi ?Waaw. Dégg naa ñenn ñiy xeex CFA bi naan, nanu gaaw jël ECO bi, def ko sunu xaalis. Waaye, ECO bi ci lajj lay mujj. Wolof dafa ne, ku ndóbin rey sa maam, foo séenatee lu ñuul daw. Man dama jàpp ne, CFA ak ECO ñoo yem kepp, benn baaxu ci. Dama xamul lu tax rekk mënuñu lal ab naal boo xam ne, dina jur i meññent ëllëg. Te sax, lu tax nuy déglu ñi nuy gëmloo ne sunu bëggee jëm kanam fàww nu bokkak ñeneen ñi xaalis ? Loolu du dëgg. Gàtt xel doŋŋ la ak xeebaate. Fii, ku fi gëm sa bopp, takku liggéey dinga am yokkute. Damay jël misaal ci yenn réewi Ërob yoo xam ne Senegal moo leen gën a yaatu, ëpp leen alal, ëpp leen mbooloo. Tey, ñoo ngi ci naataange te dara mayu leen ko lu dul liggéey bu jaar yoon. Kon, ku nekk mën nga  liggéeyal sa réew ba mu naat. Waxuma ni booloo baaxul. Wànte, fàww ku nekk gëm sa bopp ba noppi, liggéey liggéey bu lay amal njariñ, amal njariñ ñeneen ñi. Bu ko defee, dinañu mën a saxal garabu booloo gi, di ko suuxat ba mu màgg, dëgër, law ci biir Afrig gépp.

 

Whatsapp Mysapce Tumblr StumbleUpon Reddit Flipboard  
 
 
COMMENTAIRES (8)
Ajouter un commentaire
Les commentaires à caractère publicitaire ne sont pas autorisés !
Bonz - 16/08/2019 - 14h 28  
ça fais du bien et c'est rafraîchissant, je ne me croyais pas capable de lire un texte aussi long en Wolof et finalement je l'ai lu aisément et compris facilement. Amouma sen Fay !
Lamzau - 16/08/2019 - 15h 38  
Waaw goor. ni rék la nak.di lèn diadieufeul bou bakh.
Enfin - 16/08/2019 - 18h 52  
Jerejef. Amul lu gena jaar yoon jefendiko saw lacq. Fatarnicu (developement) bi nu oot, ci saw lacq rekk la mane nekk.
Modou - 16/08/2019 - 19h 54  
Baye Seex Anta ca xam xam mam boo seela ba waxone nani, " Lamignoo jambur manno ce macc ba mu saf". Di rafetloo lacc ak tontoo yi. Waxtan wi amna solo. Wogn bo giss ci benn lay tambalee. Nagnoo genna naam limign wi rekk, genn ko gnawwal.
Modou - 16/08/2019 - 19h 54  
Baye Seex Anta ca xam xam mam boo seela ba waxone nani, " Lamignoo jambur manno ce macc ba mu saf". Di rafetloo lacc ak tontoo yi. Waxtan wi amna solo. Wogn bo giss ci benn lay tambalee. Nagnoo genna naam limign wi rekk, genn ko gnawwal.
Modou - 16/08/2019 - 19h 54  
Baye Seex Anta ca xam xam mam boo seela ba waxone nani, " Lamignoo jambur manno ce macc ba mu saf". Di rafetloo lacc ak tontoo yi. Waxtan wi amna solo. Wogn bo giss ci benn lay tambalee. Nagnoo genna naam limign wi rekk, genn ko gnawwal.
Diallo - 17/08/2019 - 09h 34  
Jereujefeti ! Ma'sha'allahDiléne Jahjeufal... Je ne peux que me réjouir, il faut en faire davantage. C'est une fierté
Saisissez votre commentaire
Votre nom
 
Votre commentaire
 
   
 
DANS CETTE RUBRIQUE
Vente de véhicules d'occasion : Plus de 7 milliards "lavés" entre Dakar et Bruxelles
Le déficit commercial se creuse au deuxième trimestre
Faillite de l’Etat du Sénégal : les caisses sont-elles vides ?
Régies financières : 1605, 470 milliards déjà recouvrés
Sénégal: hausse des transferts rapides d’argent au cours des six premiers mois de l’année
Dakar-Abidjan : La Centif traque 2,3 milliards Fcfa
Macky Sall pourra-t-il éviter un prêt du FMI ?
Locafrique rachette la dette de la SAR
Situation économique du Sénégal : l’Economiste, El Hadj Mounirou Ndiaye casse tout
« MAN, DAMA JAPP NE, CFA AK ECO ÑOO YEM KEPP, BENN BAAXU CI. »
 
 
LES PLUS POPULAIRES
« Lequartd’heure » reçoit le journaliste Baba Aidara qui fait de graves révélations sur la mafia du pétrole au Sénégal
Consulté : 126718 fois
Voici la chronique du 31 Août 2016 de Pape Alé Niang
Consulté : 89584 fois
Voici la chronique du 14 septembre 2016
Consulté : 65419 fois
Voici la chronique du 08 mars 2017
Consulté : 55764 fois
Voici la chronique du 21 septembre 2016
Consulté : 55103 fois
 
   
REVUE FRANÇAIS
Ecoutez la revue de presse en français de Pape Alé Niang du 24 décembre 2018
REVUE WOLOF
Ecoutez la revue de presse en wolof de Pape Alé Niang du 24 décembre 2018
CHRONIQUE PAPE
Voici la chronique du 11 septembre 2019
AUTRES AUDIOS ...
Khaoussou Dramé interpelle Emmanuel Macron
 
SCANDALES D'ETAT
   
Marchés au Sénégal :Le CITP de Seydou Kane, proche de Macky Sall, veut sa par ...
13/09/2019 - 12:32
De nouvelles révélation sur l'affaire Pétro-Tim
02/09/2019 - 11:00
   
... Voir plus
 
YAKO WAKHONE!
   
Vidéo ....Quand Birama traitait les étudiants de fils de pute...
12/09/2019 - 09:48
Quand Me Ousmane Seye se prononçait sur la décision de la CEDEAO sur l’affai ...
24/05/2019 - 13:24
   
... Voir plus
CARTE BLANCHE
Le voile, entre croix et banniére
L'OEIL DU CITOYEN
<< Set setal >> politico-religieux !
WAX DEUG
Mutation du griotisme au Sénégal : La presse en otage !
AUTRES ...
Voici la chronique du 11 septembre 2019
 
 
CONTRIBUTIONS
   
Serigne Abdou, l'honneur du soufisme contemporain !
14/09/2019 - 12:47
Dévoilement.....
12/09/2019 - 15:28
   
... Voir plus
 
 
 
REPORTAGES
Ça Me Dit Mag du 13 octobre 2018 avec Pape Alé Niang - invité commissaire Abd ...
EMISSIONS PAPE
Décryptage du 10 octobre 2018 avec Pape Alé Niang : une démocratie capturée
AUTOUR DU MICRO
Khaoussou Dramé interpelle Emmanuel Macron
AUTRES VIDEOS
Le Scandale Du Siècle : Pétrole & Gaz au Sénégal (BBC News Afrique)
 
 
Xibaar
Walf
Seneweb
Press Afrik
Leral.net
Rewmi.com
 
 
 
 
ACCUEIL ACTUALITES POLITIQUE SPORT INTERNATIONAL RELIGION TECHNOLOGIES VIDEOS AUDIOS PEOPLE RADIOS & TVS
 
Contactez nous au 33 825 25 17 ou par mail à dakarmatin@gmail.com
 
Proposer une contribution | Contacts | Qui somme nous? | Reserver un espace publicitaire | © Copyright Dakarmatin 2017